Lan mooy Kowit 19 ak ana yan matuwaay lañu wara jël?

Koronaawiris wala Kowit19 doomu jàngoro la ju tuuti (kenn mënu koo gis ak bët), mën a wesaaroo jural nit ñi feebar. Màndargay Kowit19 benn lañu ak yu sibiru, maanaam sëqat su wow, gaaw a sonn, tàngoor ak yaram wuy metti. Kowit19 noyyikaay gi lay gën a jàpp. Doonte yenn feebar yi taxu leen a doon yu mën a jur lor, Koronaawiris mën naa jur feebar xëtar bula mën a ray yenn saa yi.

Ñépp a mën a am Kowit19. Màgget ñi ak ñi am feebar bu yàgg buñu doon wéyaale, mel ne feebar yi aju ci noyyi, sànkar ak woppi suukar, ñoom la gën a mën a dal ci anam yu doy waar.

Liy joxe wopp ji mooy nit ku ko am, jaare ci taflitam yi muy sanni buy noyyi, buy sëqat, wala buy tissooli ci kaw nit ñi, ci kaw lépp lu tege wala ci ñam yi. Bu xasee dugg ci sa yaram dafay fulu ba noppi tas ci sa cér yépp. Bula duggee, mën ngaa toog fukki fan ak ñeent sooga gis màndargay feebar bi. Kon nit mën naa am Koronaawirus wàll ko ñeneen te du ko xam.

Garab yi fi nekk yépp amul bu ci mën dara ci Koronaawiris. Liñu mën mooy fexe mu bañ a law, jaare ko ci moytu di jegeente ak di raxas loxo yi lu bari.

Ngir mën a mucc ci doomu jàngoro ji, fàww ñuy raxas suñuy loxo bu baax ak saabu ak ndox. Na ngeen saxoo di ko def doonte seeni loxo niruwu leen lu tilim. Raxas leen seen loxo bu baax ci ndox muy xelli ci diiru ñaar fukki ñaareel ak saabu, te fexee bomb bu baax suufu we yi. Raxas leen loxo bi yépp, jara bi ak loxo bépp. Raxas say loxo lu bari ak ndox ak saabu mën naa ray doomi jàngoro yi mën a tag ci ñun. Deeleen raxas seen loxo boo leen di waaj a togg ak boo leen toggee ba noppi, boo leen jógee ci wanag yi, balaa ngeen di lekk, boo leen toppatoo ay jarag, boo leen laalee ay mala, ay nefere mala wala boo leen sëqatee, ngeen tissooli wala ngeen ñandu.

Moytu leen di laal seen gémmiñ, seen bakkan wala seen bët yi, fekk raxasooleen seen loxo. Loxo yi danuy laal barab yu bari, doomu jàngoro ji mën leen ca toppe. Te bu say loxo jàppee doomu jàngoro ji rekk, sa bakkan, say bët, sa gémmiñ doon nañu buntu yu mu mën a jaar. Doomu jàngoro ji mën na cee jaare dugg sa yaram daaneel la feebar.

Moytoo jege ñi seen yaram tàng, ñuy sëqat wala ñu am yeeneen màndarga ci wàllu noyyi gi. Deeleen sëqat te di tissooli ci seen biir concu wala ci fompukaay. Booleen ci noppee ngeen sànni fompukaay bi. Buleen di tafli ci mbedd mi.

Na ngeen sori lu tollu benn ñay, ķépp kuy sëqat, di tissooli. Moytu leen jege ku yaram wi tàng muy sëqat.

Boo leen ware toppatoo ku yaramam tàng, muy sëqat ba noppi am ay jafe-jafey noyyi, wut leen maska te raxas seen loxo bu baax.

Ngir moytu doomu jàngoro ji law, li gën a wóor mooy daw bépp jege ak yeneen nit. Kowit19, niki yeneen doomi jàngoro yépp, mën nañu ko jële ci nuyóo, mu jaare ci boo laalee say bët, sa bakkan ak sa gémmiñ, dugg sa yaram. Kon nag, booy nuyóo moytul joxe loxo wala di saafoonte mbaa di fóonante. Yamal ci tàllal loxo, yëngal sa bopp wala mel ne ku xaw a sëgg, booy nuyóo. Boo jàppee ne Kowit19 am na ci sa gox, toogal sa kër te moytu jonjoo ak ñeneen ñi.

Boo tàmbalee yëg feebar ci sa yaram, doonte màndarga yi taxul ñu fés loolu, yem ci metitu bopp, bakkan buy xelli, toogal sa kër ba ba ngay yëg tan. Booy tissooli, am sëqat gu wow, am ay jafe-jafe ci noyyi ak yaram bu tàng, dawal gaaw seeti fajkat, ndax mën naa doon feebaru noyyi wala beneen feebar bu doy waar.

Yenn gëm-gëm ak yenn wax yi tegewul fenn mën nañoo jur loraange, ba àgg ci ray nit ñi. Ci misaal, jëfandikoo alkol ak ordusabel wóorul ci sa wérgu yaram te mënul dara ci Koronaawiris. Ba ci xibaar yi ngay jot ci say xarit wala say mbokk mën nañoo bañ a wér wala ñu jural la loraange. Bu leen déglu ludul digle fajkat yi.

Mën ngaa bay sa waar ci xeex Koronaawiris bi boo wesaaree bataaxel bii ci seen xarit yi, seen mbokk yi, jaare ko ci watsab.